exibições de letras 4

Ballago Ndoumbé Yatma

Youssou N'dour

Billaay, ballago ndoumbé yatma
Su ñu waaji xaj oon na fi
Naxxar doηη, la ñu bayyee
Yalla, wonneeti na

Li tax ba mbir mi metti lool
Ñun da ñu ko foog wul woon
Yëf yi gaaw ba bette gnou
Billaay wéetël na ñu

Njiinoo njiin faramaareen
Gòor u jaaga, nelaw naa
Baay i wally dem na nii
Ñun daal wéetël na ñu

Ma ngi koy jaale Sénégal
Di ko jaalé Gambia
Di ko jaalé adduna
Ndaanaan ba dem na nii

Thione ballago, ndoumbé yatma
Bu yalla buur bi doon taggoo
Kon di na ñu bayék yaw
Ni patrimoine bi nga ñu bayyeel
Yee gua nit gñi, tete leen ci adduna
Yee gua nit gñi, tete leen
Xam al leen ci adduna
Ahh - Balaago

Yee gua nit ñi ci adduna xam al leen
Ni ñu war a nekkek
Ak ni ñu war a dundée
Ak ni ñu war a jëfleentee
Jinaxoo mbaay
Yaw mi dëkké biir suuf
Boo dem ee neel ballago, réew maa ngi koy joy
Aduna ngi koy jooy
Art baa ngi koy jooy

Njiin faramaareen
Thione seck, wéetël na ñu
Ballago ndumbé yaatma
Adduna, am ul solo

Li tax ba mbir mi metti lool
Ñun da ñu ko foog wul woon
Yëf yi gaaw ba bette gno
Ndanaan ba dem na ni
Njiin faramaareen
Thione Seck, wéetël na ñu
Ballago ndumbé yaatma
Àdduna amul solo


Comentários

Envie dúvidas, explicações e curiosidades sobre a letra

0 / 500

Faça parte  dessa comunidade 

Tire dúvidas sobre idiomas, interaja com outros fãs de Youssou N'dour e vá além da letra da música.

Conheça o Letras Academy

Enviar para a central de dúvidas?

Dúvidas enviadas podem receber respostas de professores e alunos da plataforma.

Fixe este conteúdo com a aula:

0 / 500


Opções de seleção

Mais ouvidas de Youssou N'dour